Njiitu République des Valeurs, Thierno Alassane Sall, dina amal léeg-léeg waxtaan di dellu ci jafe-jafe yi Senegaal jànkootel, ak pexe yi nu mën a indi ngir doxal dëgg-dëgg sunu réew ci jub, ci xam-xam ak ci teraanga bu yaatu, njëriñ doomu-Senegaal yépp. Ci limat bu njëkk bii, Thierno Alassane Sall mu ngi saytu, di wax lu waral Senegaal moom boppam lu mat, ci atum ren, juróom-benn-fukk-ak-benn at, te ba leegi réew maa ngi tumrankee. Mu ngi ut itam ay pexe ngir kàttanal ndaw yi, ñu toog seen réew fekk fi jàmm ak naataange.
